Li xew ci mim reew doyna waar ! Sunugaal ndax dina dox su jikko yi ma guiss sopekuwul ?
Deuk ak nitt defula dara, nek ci yoonam nga guiss yeenee ko lu bon ligeey ko mu dof wala mu niak !
Deuk ak nitt wersek gam neexula nga tuumaal ko weurr rek di yaak deram !
Deuk ak nitt baaneexam soff la nga faagaagalko yak ko !
Ndax Sénégal dina doxa k Jikko yii yu bon ?
Ndax yalla nitt yi duniu ndangu doggal ?
Luy am-am ? Luy xalis ? Luy daraja batax ngay yak nitt ?
Ah suba dh du agn, du rer, waye lu mata soralela
Aduna dekul ! Aduna day diex !
Te buniu fate Karma lu am le !
Niu bayi ci xel mbokk yi !
Buddei yaw tamit nit togn nala, yakkal la wax ko fii niu bokk sa nakar.
Qui sait ? ton expérience peut sauver des vies !
Astou DIOUF